Ma ñaan ci biir tuuma
1Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Ci sama njàqare laa woo Aji Sax ji wall,
mu wuyu ma.
2Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat,
ak làmmiñu njublaŋ.
3Yaw boroom làmmiñu njublaŋ,
ana lu ñu lay añale
ak lu ñu lay dolli?
4Xanaa fitti mbër yu ñaw
ak xal yu yànj.
5Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg ya
tey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña!
6Yàgg naa lool ci biir nit ñi bañ jàmm.
7Man may wut jàmm,
te su ma waxee,
ñoom ñuy ayoo.