0^SabóorÑaari yoon a ngiiYàlla fal na buurAji jub a ngi woote wallMuy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor3.1 Seetal ci 2.Samiyel 15—16..Ma gonloo ñaanMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Ma jëluy ñaanMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki toxoro, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Jarag a ngi woote wallMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Boroom tuumaa ngi woote wallMuy woyu njàmbat, ñeel Daawuda. Mu woyaloon ko Aji Sax ji ci mbirum kàddu yu tukkee woon ca Kuus, ma bokkoon ci giirug Beñamin.Aji Sax ji teral na nitMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit8.1 gitiit tur la wu réer ci làkku ebrë. Man na doon xeetu xalam gu cosaanoo dëkk ba ñuy wax Gaat ci réewu Filisti. Man na nekk it galan bu ñu daan woye ci jamono bu ñuy witt reseñ, di ko nal., ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.Aji Sax ji dëgg lay àtteMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Deewug doom ju góor, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.Néew-ji-doole sàkku na yoonMa làqoo Aji Sax jiMu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda.Kàddug Yàllaa wóorMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Aji Sax ji, loo deeti xaar?Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Yàqute maase naMu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda.Kuy aji jub?Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Aji Sax ji laa séddoo, dund ak deeMuy taalifu Daawuda, ngir jàngle.Aji Sax ji, jox ma dëggMuy ñaanu Daawuda.Buur daan, sant Aji Sax jiMu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettlee ci mboolem noonam, xettli ko it ci Buur Sóol. Kàdduy woy yaa ngii.Aji Sax ji màgg naMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Yal na Buur daanMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Aji Sax ji baaxe na BuurMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Jëkke jàq, mujje santMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, dëppook galan bi ñu dippee Kéwélu fajar.Aji Sax jee may sàmmÑeel Daawuda, di kàddug Sabóor.Ana kuy màggal Buur Yàlla?Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.Aji Sax jeey gindee, di yiireÑeel Daawuda.Ma waajal ndajem kër Aji Sax jiÑeel Daawuda.Xare jib, ma ànd ak YàllaÑeel Daawuda.Aji Sax jeey àtte ñoñamÑeel Daawuda.Aji Sax jeey boroom ndamMuy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Mucc, bégMuy woyu Sabóor, ñeel Daawuda ca daloob kër Yàlla ga30.1 Woyu Sabóor wii Daawuda da koy sante Yàlla gannaaw mbas ma, ba mu jëndee dàgga ngir rendi fa sarax su dakkal mbas ma. Dàgga jooju lañu mujj tabax jaamookaay ba. Seetal ci 2.Samiyel 24, ak 1.Jaar-jaar ya 21..Naa siggi, noon sëggMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Njéggal barke laDib taalif, ñeel Daawuda.Nan woy Boroom bi nu sàkkAji Sax ji du tanqamlu aji jubÑeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem34.1 Seetal ci 1.Samiyel 21.10-15. Akis buurub Gaat mooy Abimeleg ba tey..Aji Sax ji, àtte maak noonÑeel Daawuda.Nit ñaaw, Aji Sax ji goreMu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji.Bu sa xol jógÑeel Daawuda.Maa wopp, tuub, di jooyMuy kàddug Sabóor guy fàttlee, ñeel Daawuda.Dund yàggulMu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Déggal Aji Sax jee am soloMu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.Jarag bu ñu toŋal a ngi ñaanMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Maa namm YàllaMu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.Éy Yàlla, àtte maXeet waa ngi jooyMu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.Buur a ngi séetalMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel askanu Kore wu góor, dib taalif, te di woyu mbëggeel.Aji Sax jee ànd ak manMu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.Yàllaay buurMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.Aji Sax ji aar na SiyoŋMuy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.Alal day naxeMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.Aji Sax ji xol lay gërëmMuy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.Yàlla, yërëm maMu jëm ci njiitu jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba51.2 Seetal ci 2.Samiyel 11—12.25..Yàllaa man boroom dooleMu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel Daawuda. Mooy ba Doweg, Edomeen ba, demee ca Sóol, ne ko Daawuda dem na kër Ayimeleg52.2 Seetal ci 1.Samiyel 21—22..Mbon maase naMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat, di taalif bu ñeel Daawuda.Yàlla, dimbali maMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di taalif bu ñeel Daawuda. Mooy ba waa Sif demee ca Sóol, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew54.2 Seetal ci 1.Samiyel 23.14-28; 26.1-5..Xarit wor na maMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, dib taalif, ñeel Daawuda.Yàlla laa wóolu, ragaluma nitMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaat56.1 Seetal ci 1.Samiyel 21.10-15..Yàlla jógal, wallu ma!Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, gannaaw ba mu dawee Buur Sóol, ba dugg ca xunti ma57.1 Seetal ci 1.Samiyel 24..Yàllaa mana mbugalMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda.Wallu maak ñu bon ñiMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon. Mooy ba Buur Sóol yónnee ay nit ñu ko xoolal kër Daawuda, ngir rey ko59.1 Seetal ci 1.Samiyel 19.11-17..Yàllaa yor sunu muccMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Seedeb Tóor-tóor, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda. Mooy ba Daawuda di xareek waa Siri ña ca Mesopotami ak waa Siri ña ca Soba te ba ñu ca bàyyikoo, Yowab duma fukki junniy Edomeen ak ñaar (12 000) ca xuru Xorom wa60.2 Seetal ci 2.Samiyel 8.3-14; 1.Jaar-jaar ya 18.3-13..Naa woote wallMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda.Yaakaar, fa YàllaMu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Maa namm Aji Sax jiMuy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda63.1 Seetal ci 1.Samiyel 23.14; 24.2; 2.Samiyel 15.23..Yàllaa man ag fittMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Yàllaay nangul suufMu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor, ñeel Daawuda.Yàllaay aar nitamMu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor.Yal na nu Yàlla barkeelMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor.Yàlla daagu, daanMu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di woyu Sabóor.Ku ñu fitnaal a ngi ñaanMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel Daawuda.Yàlla, gaawe maMu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di woy wuy fàttlee.Mag a ngi séentu njekku YàllaNu ñaanal BuurÑeel Suleymaan.Am Yàllaa gënMuy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.Yàlla, bu la noon reeMuy taalifu yeete, giiroo ci Asaf.Yàllaay àtteMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Bul yàq, di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf.Yàllaa moom xareMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf.Yàllaa ngi seetaanMu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.Nit goreedi, Yàlla goreMuy taalif bu giiroo ci Asaf.Yàlla, feyul nuMuy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.Yàlla, suqlil sa njëmbatMu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf.Déggal Yàlla, jariñuMu jëm ci njiital jàngkat yi, giiroo ci Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit.Yàllaay àtte ndawi péncamMuy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.Yàlla, mbugalal noon yiDi woyu Sabóor, giiroo ci Asaf.Ku dal ak Yàlla bégMu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit, ñeel askanu Kore wu góor.Aji Sax ji, suqleeti nuMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.Ma ñaan, bésub njàqareMu di ñaanu Daawuda.Siyoŋ, yaay ndeyu xeet yiÑeel askanu Kore wu góor, di woyu Sabóor.Ma jàq, jooyMuy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor, jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat Leyanot, di taalifu Eman, mi bokk ci giirug Esra.Aji Sax ji, loo dige woon?Muy taalif bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.Doom aadama yàggulMuy ñaanu Musaa, góorug Yàlla ga.Aji Sax jee mat kaaraangeNu woy bésub NoflaayMuy woyu Sabóor ngir bésub Noflaay.Ma bàkk Aji Sax jiYàllaay mbugal ku bonKaayleen, nu santBuur Yàllaa ngi àttesi àddinaNguurug Aji Sax ji njekk laWoyleen Aji Sax jiy àttesiMuy kàddug Sabóor.Aji Sax ji buur bu sell laAji Sax jee baaxMuy jàngi cant.Buur a ngi jaayanteek YàllaÑeel Daawuda, di kàddug Sabóor.Yàlla, bu ma reyMuy ñaanu néew-ji-doole ju sonn, bay diis Aji Sax ji njàqareem.Ma sant Aji Sax jiÑeel Daawuda.Màggal-leen ki sàkk léppAji Sax ji sàmm na kóllëreIsrayil di wor, Yàlla di wóorAji Sax jeey xettleeYàlla, may nu ndamMuy woyu Sabóor, ñeel Daawuda.Yal na Yàlla mbugal noon biMu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.Yàlla fal na nitamÑeel Daawuda, di kàddug Sabóor.Yàlla la ay mbiram saxKu ragal Yàlla gis njekkamBuur Yàllaay wallooYàllaay walloo dooleemKu wóolu Yàlla barkeelMa sant Yàlla mi ma jotNa ñépp ànd ak Israyil sant YàllaAji Sax jeek man, ma daanAji Sax ji, sa kàddu laay bégeMa ñaan ci biir tuumaMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Ana ku may sàmm?Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Nu ñaanal YerusalemMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.Yàlla, fajal nu gàcceMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Nanu sante Aji Sax ji wallamMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.Ku doyloo Aji Sax ji rawMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Yàlla, delloo nuMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Barkeb Yàllaa wóorMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan.Ragal Yàlla, jàmmi kërMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Noon manul IsrayilMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Nu séentu njotug YàllaMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Damaa woyof, gëm YàllaMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.Yàlla digoo naak ki mu falMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Bokk, bennoo neexMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.Way-gëm ñaa ngi santMuy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.Aji Sax ji jot na IsrayilYàllaa am kóllëreJooye nanu àllAji Sax ji waccu maÑeel Daawuda.Aji Sax jee ma xam, ba jeexal maMu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.Ku ñu toŋal a ngi ñaanMu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Yàlla, sàmmal sama làmmiñMuy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Aji Sax ji rekk a ma yégMuy taalifu ñaan bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunti ma.Aji Sax jeey sama yaakaarMuy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.Aji Sax ji, laggsilÑeel Daawuda.Ma kañ Buur YàllaMuy jàngi màggal, ñeel Daawuda.Buur Yàllaa jara wóoluYàllaa gën ci àddina, gën ci nitNa àddina wërngal këpp màggal YàllaNa Israyil màggal Ki SaxMàggal-leen Ki Sax!