Bànni Israyil dogu nañu
1Loolu yépp tax na nuy tëral takktoo bu dogu, bind ko, sunuy njiit ak sunuy Leween ak sunuy sarxalkat def ci seen màndargay torlukaay.
2Ñi ko torlu ñoo di:
Boroom dëkk bi Neyemi doomu Akalya, mook Cedekiya 3ak Seraya ak Asaryaa ak Yeremi 4ak Pasur ak Amarya ak Malkiya 5ak Atus ak Sebaña ak Malug 6ak Arim ak Meremot ak Obadiya 7ak Dañeel ak Ginton ak Barug 8ak Mesulam ak Abya ak Miyamin 9ak Maasya ak Bilgay ak Semaya. Ñooñu ñoo di sarxalkat ya.
10Leween ñi ñoo di:
Yeswa doomu Asaña, ak Binuy, kenn ca doomi Enadàdd, ak Kadmiyel. 11Seeni bokk ca lañu, di Sebaña ak Odiya ak Kelita ak Pelaya ak Xanan 12ak Mika ak Reyob ak Asabya 13ak Sakuur ak Serebya ak Sebaña 14ak Odiya ak Baani ak Beninu.
15Njiiti askan wi ñoo di:
Paros ak Payat Mowab ak Elam ak Sàttu ak Baani 16ak Buuni ak Asgàdd ak Bebay 17ak Adoña ak Bigway ak Adin 18ak Ater ak Esekiya ak Asur 19ak Odiya ak Asum ak Besay 20ak Arif ak Anatot ak Nebay 21ak Magpiyas ak Mesulam ak Esir 22ak Mesesabel ak Cadog ak Yaduwa 23ak Pelaca ak Xanan ak Anaya 24ak Oseya ak Anaña ak Asub 25ak Aloyes ak Pila ak Sobeg 26ak Reyum ak Asabna ak Maaseya 27ak Axiya ak Xanan ak Anan 28ak Malug ak Arim ak Baana.
Solob dogu baa ngi
29Bànni Israyil ga ca des nag fekksi leen, muy sarxalkat yaak Leween ñaak fara bunt yaak jàngkat yaak liggéeykati kër Yàlla ga, di mboolem nun ñi beddeeku woon waasoy réew yi, ngir topp yoonu Yàlla wi, nook sunuy jabar ak sunu doom yu góor ak yu jigéen, mboolem ñi xam te xàmmee. 30Ci kaw loolu nu ànd ak sunu bokki garmi, waatook ñoom ne dinanu topp yoonu Yàlla wi mu dénkaane, Musaa jaamam ba jottli; di ko sàmm, di jëfe mboolem sunu santaaney Boroom Aji Sax ji, ak àttey yoonam ak dogali yoonam.
31Nu ne nag dunu may waa réew mi sunu doom yu jigéen te dunu jëlal sunuy doom seeni doom yu jigéen.
32Te itam bu waa réew mi indee am njaay mbaa lépp luy pepp, di ko jaay ci bésub Noflaay, dunu ko jënd ci ñoom bésub Noflaay mbaa bés bu sell, te atum juróom ñaareel mu nekk dinanu bale bépp bor.
33Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga, 34jëm ca mburum wone ba, ak saraxi pepp yi war bés bu nekk, ak saraxi dóomal yu bés bu nekk, ak saraxi bési Noflaay, ak yu Terutel weer ak yu bési màggal yi, ak yeneen yu ñu sellalal Yàlla, ak saraxi póotum bàkkaar yi bànni Israyil di jotoo, ak mboolem la war ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga.
35Ay bant lanu tegoo ci sunu biir, nun sarxalkat yeek Leween ñeek baadoolo yi, ngir dogalal waa kër gu nekk àpp ba ñu wara aye cim at, te ñu war caa yóbbu seen sasu matt ca sunu kër Yàlla ga, ngir taal ko ca sunu sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji, muy la ñu bind ci téereb yoon wi.
36Nu dogu ba tey ne dinanu yóbbu ca kër Aji Sax ji, at mu nekk, li sunu suuf jëkka meññle ak lu garab yépp jëkka ñorle. 37Ci biir loolu nu dogoo def li ñu bind ci yoon wi, di yóbbu ca sunu kër Yàlla ga sunu taaw yu góor ak lu sunu jur taawloo, gu gudd gaak gu gàtt ga, di teg lépp ci loxoy sarxalkat ya fay liggéey. 38Ci kaw loolu nu wara yóbbu ca sunu néegi dencukaayi kër Yàlla ga lu jëkk ci sunu notu sunguf, ak sunu jooxey pepp, ak sunu meññeefi garab yépp, ak sunu biiñ ak diw, di teg lépp ci loxoy sarxalkat yi. Ba tey nuy indil Leween ñi céru fukkeelub lépp luy meññee ci sunu suuf, ndax Leween ñeey dajalesi céri fukkeel yi ci gox yi nuy bey yépp. 39Sarxalkat bu askanoo ci Aaróona mooy gunge Leween ñiy jëlsi céri fukkeel yi. Su ko defee Leween ñi yóbbu fukkeelu céri fukkeel yi ba ca sunu kër Yàlla ga, fat ko ca néegi dencukaayi alal ya. 40Ci néeg yooyu la bànni Israyil ak askanu Leween ñi di yóbbu jooxeb pepp ba ak biiñ baak diw ga; fa la ndabi bérab bu sell ba dence, te fa la sarxalkat, ya sasoo liggéey ba nekk, ñook fara bunt yaak jàngkat ya.
Nu dogu nag ne dunu sàggane sunu kër Yàlla ga.